Ëttub wolof

Dalu web bi leen di jàppale,
ci jàng dawal ak jàng bind làkku wolof

Dibeer, fukki fan ak ñett, ci weeru oktoobar, atum 2024

Nañu delloo làkki réew mi seen gëdd, di leen jëfandikoo ci bépp jokkoo. Séex Anta Jóob nee na : « làkku jàmbur, su neexee ni tàngal it, kenn mënu koo macc ba ciy tàqamtiku ».

Séex Anta Jóob

Dalal ak jàmm ci ëttub wolof

Nañu delloo làkki réew mi seen gëdd, di leen jëfandikoo ci bépp jokkoo. Séex Anta Jóob nee na : « làkku jàmbur, su neexee ni tàngal it, kenn mënu koo macc ba ciy tàqamtiku ».

Yaw aji-jàng bi, dalal ak jàmm ci ëttub wolof, dalub web bi leen di jàppale ci jàng dawal ak jàng bind làkku wolof.

Ëttub wolof, ñu ngi ko jagleel képp ku mën a làkk wolof te bëgg a mën a dawal, bëgg a mën a jàng lépp lu ñu bind ci wolof ak mën a bind xalaatam yépp ci wolof. Kon nag, ëttub wolof, taxawul ngir jàngal wolof, ñi nga xam ne dégguñu wolof.

Ñu jàpp ni boon, ëttub wolof, du doomu Senegaal rekk lañu ko jagleel, képp nit, fu mu mën a nekk ci àdduna, te njàngum wolof yitteel ko, mu ngi ci biir te ñu ngi koy jaajëfal te di ko wax : dalal ak jàmm ci sa yëf, dalal jàmm ci li nga moom, dalal jàmm ci li ñu bokk.

Loolu li muy indi, moo di waruñu jëfee wenn làkk wu dul wolof ngir tabax ëttub wolof. Liy wéral dogal boobu bare na :

  • Su ma jëlee baat bii di "algebra" ci àngale, ñu koy wax "algèbre" ci farañse ; sooy jàng "algebra" di "algèbre" di benn fànnu matematig, daañu la wax lu ci nekk yépp, jàngal la ko ba nga nekk ci sëriñ te duñu la wax mukk fu baat boobu jóge, donte ñépp xam nañu ni baat boobu àngale ak farañse ñu ngi ko jële ci araab. Li ñu ciy jëlee moo di baat, su duggee ci biir làkk, dugg ci xel yi ak xol yi, baat boobu làkk waa ko moom. Jëlal baatu pàrkiŋ, nga wër dëkk bi nga nekk, su fekkee ni dëkk boobu nit ñi seen làkkum àngale sorewul noonu, ñu bare dañu la wax ni parkiŋ, ñu bare dañu lay wax ni gaaraas lay tekki, te duñu xam ni ci àngale lañu ko jële te di réere ni baatu gaaraas boobu sax, wolof moomu ko, ci farañse la ko jëlee. Kon li am solo rekk, moo di baat bu seey ci biir làkk rekk, làkk woowa moo ko moom.
  • su ma waxee "parkiŋ, ni ni ko àngale di waxee", maa ngiy réeral ñi xamul dara ci àngale. Su ma nee "gàlle, ni ni ko alpulaar yi di waxee", maa ngiy réeral ñi xamul dara ci pulaar. Ñi ëpp ci ñiy làkk wolof, xam nañu lanmooy "pàrkiŋ" ak lan mooy "gàlle" ndax baat yooyu, seey nañu ci làkku wolof, kon mën nañu leen tekki ci wolof te duñu wékku ci weneen làkk.
  • Wolof, ak làkk yépp fu ñu cosaanoo, ay làkk yu màgg lañu. Séex Anta Jóob def na ci ay gëstu yu yéeme, yu am solo, yu daw yaram. daanu leen mosal ci gëstu yooyu ci biir ëttub wolof. màggaayu wolof, tax na, waruñu nangu wéer sunu làkkum wolof ci weneen làkk wu dul wolof. Naam loolu lu jafe la fii ñu tollu, ndax diir bi ñu ñu moomee yépp, wolof xaw naa taxaw, ndax, « li la daan tax a jëm kanam, daan la tax a am loo dundalee sa njaboot, ci weneen làkk nga daan jaar ngir am ko... » (Séex Anta Jóob). kon nag, suñu wareef la, sos baat yi amagul ci wolof, ngir delloo wolof gëddam.

Ci njalbeen, war nañoo leeral ban wolof la ñuy jàngale ci ëttub wolof. Wolof yi bare nañu, ndax waxin yu wuute. Wolof yi nekk Senegaal, wuute nañu ci seen biir, te wuteek wolofu Mali, wala Gàmbi, wala wolofu ku juddoo Etaasini, yaroo fa, te mësul a teg tànkam ci benn dëkk bu cosaanoo wolof. Loolu yépp dëgg la waaya, dañu wara tànn wenn waxin.

Ku dégg wolofu Séex Anta Jóob, wala nga jàng téere yu am solo, yu Ajaa Aram Faal bind, wala nga jàng téere yu bare, yu kureel bi ñuy wax OSAD tasaare ci àdduna si, xam ni ñii, wolof piir lañuy làkk. waaya, lan mooy wolof piir ? ndax koo gis, jàpp na ni wolofam mooy wolof piir.

li am solo moo di, su ñu xoolee bu baax li ñu sumb, te yaakaar way-jàng yi ànd ak ñun ba sore, gëm nañu ni, su ñu jëfee wolofu bindkat yooyee, ñu bare da nañu daw bàyyiñu fa. Loolu moo tax, ñu tànn wolof bi ñuy jàngale ci iniwersite bu Dakaar, mu di wolof bu boole ñépp ñiy làkk wolof, ak fu ñu mën a jóge ci réew mi, ci réew yi. waaya nag, way-jàng yi, doore ko ci man mii, ndax jàng wolof moo ma dugal ci defar ëttub wolof, nañu fagaru ndax wolofu iniwersite, wolof piir la, wolof bu jàar yoon.

Jàppal ni, ci dalub web bii di ëttub wolof, amul dara lu ñu fiy jaay. Ñun ñoo ko door, tabax ko, te ñun ñoo koy yeesal, waaya lu ëpp ci yeesal bi, ci seen xalaat lay jóge, yéen way-jàng yi, fekksi liggeeyu jubbanti, bi ñuy def saa su nekk. Kon nag, ayca leen ci liggeey bi.

Ci fii ñu tollu, ëttub wolof :

  • am na jàngukaayu bind, te ci biir :
    • am na jàngukaayu abajada, bi lay tojal arafi wolof yépp ;
    • am na jàngukaayu tekkeerlu, bi lay wan noppalukaay yi nekk ci wolof, te soo sammoonte ak ñoom, làmmiñ wi mën a méngoo ak mbind mi ;
    • am na li tax ñu war a boole wala teqale yenn baat yi ;
    • am na ay dogal yu ñu jël, ci defar ëttub wolof, di xaar ñu tabax, wala toggaat, wala yeesal nëwu wolof;
    • ak ñoom seen (añs).
  • Ëttub wolof am na ba leegi, jàngukaayu dawal, bi lay tette ci jàng dawal, ci wolof;
  • am na sàqum léebuy wolof, bu am lu ëpp ñaari junne ak juroom-ñeenti téemeeri léebu wolof;
  • am na sàqum baati wolof, ñu tudde ko "oggo", mu am lu ëpp fukki junney baat, yu ñu firi ci wolof kepp.

fas yéene dolli ay jëf, yu bare, ci ëttub wolof, su ci Yàlla àndee.

Dalleen ak jàmm !

Borom baat bu neex bi ngeen doon dégg fii nag, kenn la ci soskati kallaamayréewmi.sn, doon ci def xelam, dooleem ak xaalisam, Yàlla dafa def mu dëddu atum 2018. Ñu ngi sàkku ci yéen, ngeen defal ko fukki ixlaas ak benn, Borom bi fay ko liggéey bile ak jépp jëfam ju yiw, jéggal ko ay rëcc-rëccam, xaare ko Jannatul Firdawsi. Amiin Yaa Rabbi.

Moomeel © Kàllaamay réew mi 2012 - 2022 | Ñooy ñan | Jokkoo ak ñun