Dalu web bi leen di jàppale,
ci jàng dawal ak jàng bind làkku wolof
Nañu delloo làkki réew mi seen gëdd, di leen jëfandikoo ci bépp jokkoo. Séex Anta Jóob nee na : « làkku jàmbur, su neexee ni tàngal it, kenn mënu koo macc ba ciy tàqamtiku ».
Njànginu 'a' bi dafa gudd moo tax ñu koy binde ñaari 'aa'
Liy njuumte ci mbindinu jamono wi mooy di+baatal bi ñu jàppe ni ab j, noonu farañse moo koy binde.
Séddoo duñu ko binde ee ndax njànginam guddul, dafa gàtt, rax-ci- dolli, é bi dafa tëju. Ba tay baatal bu mujj bi (oo) dafa gudd moo tax ñu war ko binde ak ñaari o (oo). d bi dañu koy seexal, di ko binde nii : dd, ndax njànginam dafa gudd te dafa am doole, bu ñu ko dendalee ak njànginu d.
Yóbbaale ma ñaari baat la, kenn waru leen a taqale ci mbind mi. o bi dafay am maaskay tëj ndax njànginam dafa tëju ; b bi dañu koy seexal, di ko binde nii : bb, ndax njànginam dafa gudd te dafa am doole, bu ñu ko dendalee ak njànginu b ; njànginu a bi dafa gudd moo tax ñu war ko binde ak ñaari a (aa) ; baatalu e bu mujj bi dafa tijjeeku moo tax kenn waru ko tegal maaska bu koy tëj, nii lañu koy binde : e.
Réew mi ñaari baat la, kenn waru leen a taqale ci mbind mi. Baatal bi nekk ci baatu réew (ée) gàttul, dafa gudd, te njànginam dafay tëju.
e bi nekk ci baatu leeral, njàngin wu gudd la yore, moo tax ñaari e lañu koy binde (ee).