Ëttub wolof

Dalu web bi leen di jàppale,
ci jàng dawal ak jàng bind làkku wolof

Alxemes, fukki fan ak ñaar, ci weeru septàmbar, atum 2024

Nañu delloo làkki réew mi seen gëdd, di leen jëfandikoo ci bépp jokkoo. Séex Anta Jóob nee na : « làkku jàmbur, su neexee ni tàngal it, kenn mënu koo macc ba ciy tàqamtiku ».

Séex Anta Jóob

Ijji

... araf bi araf bi ci ndoorteelu baat araf bi ci biir baat araf bi ci njeextalu baat
a - A ak samay mala
aa - AA aat paaka Koldaa
à - À àbb làmmiñ amul
ãa - ÃA ãas bernaar deppãas kacapãa
o - 0 oto dof solo
oo - OO oor soow woo
ó - Ó óbbali jóg puso*
óo - ÓO óom fóot juboo*
u - U ubbi àlluwa taamu>
uu - UU uuf suuf ruu
i - I itte gis kaani
ii - II iir biir bii
e - E egsi lem tabe
ee - EE ee lees mee
é - É amul lépp xule*
ée - ÉE éem déey boo bëggee*
ë - Ë ërtël bër jë
ëe - ËE ëer bëer amul
b - B ba sabar garab
bb - BB amul ubbéeku gabb
c - C cafka kacapãa amul
cc - CC amul ccoor cc
d - D dem baadoolo amul
dd - DD amul àddu sadd
f - F for nafa kaf
g - G gaal naagu log
gg - GG amul liggéey gg
h - H hã Abdurahmaan ah
j - J jabar fajar aj
jj - JJ amul ajji bojj
k - K kër suukër ak
kk - KK amul kku lakk
l - L lim talaata abal
ll - LL amul xulli koll
m - M max xamul lam
mm - MM amul mm fomm
mb - MB mbellax jaambur mb
mp - MP Mpal sempi sump
n - N nawet anam kan
nn - NN amul nnu nn
nc - NC amul tancu tanc
nd - ND ndaa andaar nd
ng - NG ngoon ngoro ng
nj - NJ njar njóol donj
nk - NK amul nkar nk
nq - NQ amul sanqal janq
nt - NT amul nte bunt
ñ - Ñ ñam bañul bañ
ññ - ÑÑ amul ññi ññ
ŋ - Ŋ ŋaam daŋar laŋ
ŋŋ - ŊŊ amul waŋŋarñi doŋŋ
p - P pont ciipatu amul
pp - PP amul seppi sopp
q - Q amul qarci q
r - R rus baral mbër
rr - RR amul amul rr
s - S sol kaso tas
t - T tus ciipatu liit
tt - TT amul xotti natt
w - W war bawoo taw
ww - WW amul xewwi jaww
x - X xol taxaw tax
y - Y yar caaya coy
yy - YY amul fayyu coyy

ci biir wolof, araf bu ne, am nga ñaari mbind. boo jëlee arafu "a", dafa am "arafu ndawe", ñu koy binde "a" bu ndaw, ak "arafu mage", ñu koy binde "A" bu mag.

ci mdindum wolof, "é", su nekkee ci njeextalu baat, ñu ngi koy binde "e", waaya "é", la ñu koy jàngee.

na ki noonu, ci njeextalu baat,

  • "ée", ñu ngi koy bindee "ee", di ko jànge "ée".
  • "ó", ñu ngi koy bindee "o", di ko jànge "ó".
  • "óo", ñu ngi koy bindee "oo", di ko jànge "óo".

benn biddeew dina leen wan baat yooyu.

ci lii ci kaw, wan nañu leen araf wolof yéep. araf bu ne, wan nañu leen mbindum arafu ndaweem ak mbindum arafu mageem. ba noppi, wan nañu leen, baat bu am araf bi, ci ndorteelu baat bi, baat bu am araf bi, ci biir baat bi, ak baat bu am araf bi, ci njeextalu baat bi. yeen say, araf bi mën na bañ a am.

Moomeel © Kàllaamay réew mi 2012 - 2022 | Ñooy ñan | Jokkoo ak ñun