Dalu web bi leen di jàppale,
ci jàng dawal ak jàng bind làkku wolof
Nañu delloo làkki réew mi seen gëdd, di leen jëfandikoo ci bépp jokkoo. Séex Anta Jóob nee na : « làkku jàmbur, su neexee ni tàngal it, kenn mënu koo macc ba ciy tàqamtiku ».
Buleen di nangoo waxantu. loolu, xabaar bii, doy na ci seede.
buur gaynde dafa tëddoon bés, di féexlu ca peggu déeg ba am xar, di tuñtuñi ba agsi fa ak maram. buur gaynde ne ko :
- nuyu naa la waay, mbokk sama ! fi nga dëkk sori na fi ?
kooku tontu ne ko :
- waawaaw, sori lool sax ! gisal car bii, ba may jóg laa ko fàqoon, mu tooy xepp, te gis nga nii mu wowe, ba doon matt.
gaynde ne ko.
- kon naanal te ni mes !
nees tuuti, béy ne jalañ agsi. Gaynde jaar fa mu jaaroon ak xar :
- salaa maalekum béy, ndax fi nga dëkk sori na fi ?
- déedet, mukk ! soriy lan !
- kon baax na, dinaa leen nuyusi. boo demee, waajal leen ma ngan !
naka la dëdde, gaynde daldi topp ca tànkam ya, agsi ca dëkk ba, rey gétt ga gépp, lekk ba yéy yax ya.
Moomeel © Kàllaamay réew mi 2012 - 2022 | Ñooy ñan | Jokkoo ak ñun