Ëttub wolof

Dalu web bi leen di jàppale,
ci jàng dawal ak jàng bind làkku wolof

Dibeer, fukki fan ak ñett, ci weeru oktoobar, atum 2024

Nañu delloo làkki réew mi seen gëdd, di leen jëfandikoo ci bépp jokkoo. Séex Anta Jóob nee na : « làkku jàmbur, su neexee ni tàngal it, kenn mënu koo macc ba ciy tàqamtiku ».

Séex Anta Jóob

Abajada

jàppal ne réewum Senegaal, dafa génne benn dekere, mudi sàrtu bindum wolof ci biir Senegaal. ëttub wolof, sàrt boobu lay topp, ndax moo di sàrt bi iniwersite bu Dakaar di topp.

dekere bi mu ngi génn, ci ñaar-fukki fan ak benn, ci weeru oktoobar, atum ñaari junne ak juróom (2005). dekere boobu, mooy leeral araf yi nekk ci wolof.

donte mbindum làkk laaj na lu weesu dekere, ngir dëgër, dekere boobu, lu am solo la, te ñepp war nañu ci jàpp, topp ko, ngir mbindum wolof mën a jëm kanam.

kàllaama wolof, am na fan weer ak benn araf.

am na ci araf yi, fukki baatal, ak ñaar-fukk ak benn baatoodi.

fukki baatal yi ñooy : a, à, ã, e, é, ë, i, o, ó, u.

ñaar-fukk ak benn baatoodi yi ñooy : b, c, d, f, g, h, j, k, l, m, n, ñ, ŋ, p, q, r, s, t, w, x, y.

yeneen yu ci yokku, ñu di ay baatal yu gudd : aa, ee, ée, ëe, ii, oo, óo, uu.

baatoodi yi ñoom, dañu ci am yu ñu mënë séexal, ñu di : bb, cc, dd, gg, jj, kk, ll, mm, nn, ññ, ŋŋ, pp, rr, tt, ww, yy.

koon nak, lu dul baatoodi yii di f, h, s, q ak x, yeneen yi ci des yëpp, mën nañu leena séexal.

baatoodi yooyu ñu mënë séexal, ci biir baat, wala mujjantalu baat rekk lañuy nekk. duñu nekk mukk ci ndoorteelu baat.

ñaari baatoodi, mënañoo takkoo ci mind mi : baatoodi bu njëkk bi, baatoodi bu ñu nosal lay doon, baatoodi bi ci topp, di baatoodi bu teqtalu. ñoom ñëpp ñooy bokk benn bérébu tëggin, wala seen bérébu tëggin yi, duñu sore.

baatoodi yu takkoo yi ñooy : mb, mp, nd, nt, nj, nc, ng, nk, nq.

am na, ci baatal yi, ay araf yu mënë am maska. maska yi ñet lañu, ñu di : maskay tëj ( ' ), maskay tijji ( ` ), maskay tomb kaw ( ¨ ) ak maskay ñox ( ~ ).

maaskay tëj ( ' ) :

maaskay tëj ( ' ) ci "e", "ee", "o" ak "oo" rekk la mën a tegu. bu ko ci am ci baatal yooyu, moo gëna tëju bi ko amul. maanaam, sooy wax araf bi am maaskay tëj, la sa gémmeñ di gëna tëju, sooy wax araf bi amul maaskay tëj bi, la sa gémmeñ di gëna ubbeeku, na ci : xel mu ñaw / xél yu gaaw, genn garab / génn réew mi, door liggéey bi / dóor kaña gi.

jappal ni "e", sunu ko xëccee, di na joxe "ee", su yolomee, wala "ée", su diisee, naka ci, "xale bu reew, dëkk ci réew mi".

maskay tëj bi nek ci "ée", ci "e" bu jëkk bi rek la mënë nekk. maanaam, "eé" bi nga xam ne, "e" bu mujj bi moo am maskay tëj, amul ci wolof, wala "éé", bi nga xam ne ñaari "e" yëpp, ñoo am maskay tëj, amul moom itam ci wolof,

jappal ni "o", sunu ko xëccee, di na joxe "oo", su yolomee, wala "óo", su diisee, naka ci, "xale bu tooy xepp", "mag bu tóoy".

maskay tëj bi nek ci "óo", moom itam, ci "o" bu jëkk bi rek la mënnë nekk.

maaskay tijji ( ` ) :

maaskay tijji ( ` ) ci "a" rekk la mën a tegu, "a" bi ko am, moo gëna ubbeeku, bi ko amul. maanaam, sooy wax "a", bi am maaskay tijji, ci la sa gémmeñ di gëna ubbeeku, mel ni :

  • diggante baatu "takk", bi ci, "takk naa jabar", ak baatu "tàkk", bi ci, "matt maa ngiy tàkk" ;;
  • diggante baatu "lamb", bi ci, "njaay mi dafa lamb", ak baatu "làmb", bi ci, "làmb ja tas na" ;;
  • diggante baatu "and", bi ci, "and wi fey na", ak baatu "ànd", bi ci, "ànd bi neex na".

jappal ni "a", sunu ko xëccee, "aa" rek, la mënë nekk, mel ni ci baatu "paaka".

maaskay tomb kaw ( ¨ ) :

maaskay tomb kaw ( ¨ ) ci "e" rekk, la mën a tegu. su boobaa, dafay indi baatal bu bees, bu di "ë". baatalu "ë", am nanu ko ci léebu bii : "bu bëgg-bëgg doonoon jëmm, dina bëmëx boroomam ci kàmb."

jappal ni "ë", sunu ko xëccee, "ëe" rek, la mënë nekk. baat yi am "ëe", barewuñu ci wolof. li ko waral moo di, ay baat lañu, yu wolof jële ci yeneen lakk, mel ni ci baatu "bëer", di dax bu ñuy faral de def ci mburu.

maaskay ñox ( ~ ) :

maaskay ñox, ( ~ ) ci "a", ak "n", rekk la mën a tegu.

su maaskay ñox teggoo ci "a", dafay indi baatal bu bees, di "ã". baat yi am "ã", barewuñu ci wolof. li ko warul moo di, yu ci bare, ay baat lañu, yu wolof jële ci yeneen lakk, mel ni ci baatu "deppãas" : tey jii, lujum seer na ca ja ba, ba sama deppãas yëpp jéex na.

baatu "ã", dafa gudd ba pare, amul benn baatal bu koy guddëlaat.

su maaskay ñox teggoo ci "n", dafay indi baatodi bu bees, di "ñ". baatoodi "ñ", am nanu ko ci léebu bii : "ñi mana kott, amuñu mbaam".

araf bu ne, am nga ñaari mbind. boo jëlee arafu "a", dafa am "arafu ndawe", ñu koy binde "a" ak "arafu mage", ñu koy binde "A".

ci lii di ñëw, di nañu leen wan araf wolof wéep. araf bu ne, di nañu leen wan mbindum arafu ndaweem ak mbindum arafu mageem. ba noppi, di nañu leen wan, baat bu am araf bi, ci ndorteelu baat bi, baat bu am araf bi, ci biir baat bi, ak baat bu am araf bi, ci jeexantalu baat bi. yeen say, araf bi mën na baña am.

Moomeel © Kàllaamay réew mi 2012 - 2022 | Ñooy ñan | Jokkoo ak ñun