Ëttub wolof

Dalu web bi leen di jàppale,
ci jàng dawal ak jàng bind làkku wolof

Dibeer, juroom-ñetti fan, ci weeru septàmbar, atum 2024

Nañu delloo làkki réew mi seen gëdd, di leen jëfandikoo ci bépp jokkoo. Séex Anta Jóob nee na : « làkku jàmbur, su neexee ni tàngal it, kenn mënu koo macc ba ciy tàqamtiku ».

Séex Anta Jóob

Suqali làkki réew mi

Nangeen xam ni, li ñu defoon démb, mënees na ko defaat. li am moo di, aw xeet bu la nootee, day ràggal sa xel, ba lu tukkee ci yow rekk, danga kooy xeeb, soofantal ko, ba defe ni dootul dara ! loolu mootax, nooteelu xeet ak xeet, baaxul ; nooteelu xeet ak xeet, moo waraloon ci Misra, nit ku ñuul dem ba ñu raxas ab yuuram, ba mu fàtte fa mu mas a jóge, ba toskare. te nit, boo ko xasee indi foofu, ba mu fàtte fu mu mas a jaar, fàtte lu mas di cosaanam, mook bàyyima booy wommat ñoo yem ; fu la neex mu dugg fa. foofu lañu ñu jaarale, ci xarnu bii ñu weesu, raxas suñu yuur ba xamatuñu fu ñu jóge : lu doon ñun sax, lépp lu ñu def, ñu xeeb ko ; defe ni lu nekk, dañu koo war a roy ci ñeneen ñi. loolu, mooy li fi ne, ba ñu xeeb suñu làkk yi, ba dootuñu léen jariñoo.

teg ca, làkk ngànnaay la, paaka la, balay ñaw nga daas ko ; làkk wu ñu jariñoowul, mooy paaka bu ñu daasul, di mel ni paaka bu xomaag. te tubaab bi, bi mu fi ñówee fii ci suñu dëkk, réew mi yépp, dañu ko yore ci seen làkku bopp. moo taxoon ba suñu làkk yi des ginnaaw. li la daan tax a jëm kanam, daan la tax a am loo dundale sa njaboot, ci weneen làkk nga daan jaar ngir am ko... loolu moo taxoon, ñu sàggane sunu làkk yii. waaye du caageeni sax, dañu mënul woon a wax, li ñu bëgg a wax, ak sunu làkk yi ñu moomal suñu bopp, mu di wolof, pulaar, seereer, añs.

dangeen di xam ni aw làkk, jumtuwaay la boo xam ni, lu sa xel dem ci àddina mën na koo tudd ; xel ay gàtt, làkk gàtt ! waaye fu sa xel mën a jëm ci àddina rekk, sa làmmiñ mën na koo tudd ; làkk gàttul te mënul a gàtt.

nit kiy wax nag, fi xelam yem, fi njàngam yem, fi gis-gisu àddinaam yem, foofu rekk la ay waxam mën a yem.>

waaye boo demee ba sa xel gis leneen rekk, sa làkk dina ko tudd. - lu ko waral ? amul benn baat boo xam ni bii, yenu nga sa maanaa ci cosaan, amul ! làkk, du loo xam ni baat yi dañuy juddu indaale seen maanaa. baat bi, coow liy génn ci gémmiñ rekk ! rekk la ! ndax bu baat yi doon juddu ak seeni maanaa, benn làkk rekk ay am ci àdduna, kon, lu jóg rekk, xel yépp, benn baat lañu koy tudde, ndax lu jóg indaale ay baatam. te loolu amul.

kon, bu fekkoon ni tey, tabax naa dara lu bees, loo xam ni kenn xamagul nu ma koy tudde, nu ma neex laa koy tudde, waaye bu ma ko joxee tur, ba mu dugg ci boppu nit ñi rekk, jeex na ; su ko keneen sàkkalee weneen tur, ba tur woowu dugg ci boppu nit ñi, tur woowu mooy wéy, wala tabax boobu am ñaari tur, wala ñetti tur … ! loolu, mooy li nga xam ni, mooy li am solo.

kon, li nga xam ni tey mooy baat yi, boo jëlee wolof, mbooleem li nga xam ni bind nañu ko tey ci tubaab, mën nga koo tekki ci wolof te doo sàkk daanaka beneen baat, ba ci fukkeelu xarnu ak juroom­ñaar bi.

boo jëlee mbooleem li tubaab yi bind ba tey, nga dindi ci baat yiy tektal garab yi nga xam ni, ci seen réew rekk lay sax te amul ci suñuy réew, wala nga dindi baat yiy indi loo xam ni, seen aaday bopp la te ñun, aadawoowuñu ko, añs, li ci des lépp, mën nga koo tekki ci wolof. te baat yooyu itam, safaan yi am nañu : bu ma nee kàdd, tubaab yi mënuñu koo tekki ci seen làkk, ndax amuñu ko ; dañu koy sàkkal tur wu bees. bu ma nee new, amuñu ko ; bu ma nee sapin, man amuma ko ci sama làkk. noonu la !

baat yooyu nag, nga xam ni ñoo lëkkaloo ak réew ma, bu ñu leen dindee, ci lépp loo xam ni tubaab bi bind na ko, ba ci fukkeelu xarnu bi ak juroom­ñett, lépp mën nañu koo tekki ci wolof te duñu leen sàkkal benn baat, mën nañu koo tekki ci pulaar te duñu leen sàkkal benn baat, mën nañu def lu ni mel ci seereer, ak ci yeneen làkk yépp.

bu dee lu jëm ci nëwu bi, mu di garaameer, li suñu nëwu indi, ñoom tubaab yi, bu ñu taxawee di ko xool, duñu ko gëm. kon, suñu nëwu mel na ni sax ni, li mu mën a indi lépp, seen bos mënu ko. waaye sax, ak làkk wu nekk, mën ngaa wax li ci àddina lépp. noonu la làkk bindoo.

kon, li làkku tubaab yi ëppalee suñu yos, mooy baat yi nga xam ni, dugal nañu leen ci seen làkk yi, ci ñaari xarnu yu mujj yii. ngir leeral wax jooju, ci fukkeelu xarnu bi ak juroom-ñeent, ci la xam-xam tàmbalee, ci la mbëj-xëcc, di kuraŋ, am, ci la mbooleem xam-xam yi, doxalinu biddiiw yi, ni biddiiw yi ajoo ci asamaan ak àtte yi leen di doxal, ni àddina tabaxoo, loolu lépp ci jamono jooju la génn, tubaab yi sàkk yeneen baat yu bees, yu ñu leen tudde. baat yooyu ñooy yi ci bees. ci benn xarnu la yem, ak xarnu bii ñu nekk tey, muy ñaari xarnu, gën caa bare. baat yi tubaab yi sàkk, ñaari xarnu yu mujj yii, di ko mottalee seen làkk bi xam-xam bi juddoo, baat yooyu ñoo nekkul ci sunuy làkk, te baat yooyu, sàkk leen du dara ci ñun. dañuy samp ay kureel yuy def liggeey boobu.

amoon na ca su ñu jamono, ci ñi ma maaseel, ñu dem ba iniwersite, daara ju mag ji, dañu foogoon ni suñu làkk yi amuñu nëwu, maanaam garaameer. ndax nëwu bi, maseesu ko bind rekk ! gis ngeen ni wumple tollu !

làkku tubaab yi, boo leen jëlee bésub tey di leen naw, fàtte fi ñu jaar ba agsi fi ñu agsi tey, dangay daldi xeeb sa bopp, waaye, boo fàttalikoo fi ñu jaar, dinga xam ni làkk wu nekk mën na faa jaar.

fàttalikuleen ne tubaab yi ci seen bopp, lateñ yi dañu leen nootoon ñoom itam ; ba moom leen, ba yóbbu seenu ferferaan, ba ñu xeeboon seen bopp.

seetaanleen li Sesaar, nekkoon buuru lateñ yi, daan bind ci tubaab yi. lu nekk daan na ko wax : ni tubaab a fi dàq a toppandoo, loo leen wan rekk, dañu koy toppandoo ; lateñ yi mayuñu leen woon ñu mën a sàkk. gis nga, ki nga xam ni moo lay noot, du la may nga sàkk, da lay xañ xelum sàkk ; day bëgg a ray, loo xam ni lii mooy sa siiru, mooy sa mbóot, da koy ray ci mbindam, da koy ray ci jëfam, da koy ray ci ni ngeen di jëflantee, ba nga xeeb sa bopp. loolu la Sesaar daan bind ci tubaab yi. ne dara, ñoo fi dàq a toppandoo.

tubab yi dañoo xeeboon seen bopp. seen làkku bopp yii ñuy naw tey, fàttalikuleen ni ñu ngi ko tuddewoon ñoom, làkk yu fooyooy yi, làkk yu amul solo yi ; booba, tubaab mu ngi tudd làkk wu amul solo, almaa tudd làkk wu amul solo, àngale tudd làkk wu amul solo, español tamit tudd làkk wu amul solo, wu tekkiwul dara.

ba tax na, mbooleem xam-xam, yi nga xam ni tubaab yi dajale nañu ko, ca jamono jooja, lépp, ci lateñ lañu ko daan bind. jamono yooya, araab yi ñoo indiwoon xam-xam ci Espaañ, fab téere yi ci araab, tekki leen ci làkku español, ñoom ñu delluwaat tekki leen ci lateñ. noonu lañu ko daan defe, ndaxte, làkk wi nga xam ni, ci lañuy dox, muy làkku español, jarul sax jàng, ba dañu koy tekkiwaat ci lateñ.

mbooleem ñi amoon xam-xam ci Ërob gépp, ci lateñ lañu daan bindantee. ba ci xarnu bii ñu génn, borom xam-xam yi ñu gën a ràññee ci Ërob googee, bépp téere bu ñu daan bind, ci lateñ lañu ko daan bind. jomboon nañoo bind xam-xam dëgg, ci làkk wu fooyooy wu mel ni tubaab, wala àngale, wala wu mel ni español, añs. kenn daawu ko ci def ! fukkeelu xarnu bi ak juróom-ñeent yépp, xam-xam bi, ci làkku lateñ woowu lañu ko daan defe, fàttalikuleen ko.

bi ñu dikkee ci fukkeelu xarnu bi ak juroom-ñeent, ci la waa réew yooyu fippu, ne làkku mbooloo mi daal, jar naa jàng ; lateñ baax na, waaye dañuy bind ci làkku mbooloo mi.

léegi, seetlul, jamono yooyu, mbooleem woy wu ñu masaan a woy, ci lateñ lañu ko daan bind ; mbooleem lu ñu woyoon ci lateñ, fàtte nañu ko léegi ! ñu ngi ci kàggu yi, kenn xoolatu leen.

foofa la làkku tubaab tàmbaliwaat di suqaliku, di màgg, di aksiwaat, mu jaral nit ñi ñu jëlaat ko di ko bind, nii lañu war a def tey, lu mel na ni tubaab yi defoon démb, moo ñu dal tey ci suñuy làkk,

kon, ngeen xam ni, li am solo, moo di delluwaat – ku ñu mës a jaarale foofu, ku ñu mës a noot, ku ne, jaar nga foofu. xoolal doomu Irlànd yii, di xeex ak Àngalteer. doomu Àngalteer yi, yóbbuwoon nañu leen, ba ñu fàtte seen làmmiñ. ku juddu rekk, ñu nàmpal la ci Àngale ; ku juddu ñu nàmpal la ci Àngale, ba ñoom ñépp, ñu fàtte seen làmmiñu cosaan. waaya, bi ñu demee ba gisaat seen bopp, ba nar a bëre, ba delluwaat nangu seen bopp, dañoo delluwaat ci biir kàggu ya, jëlaat nëwu yi, di jàngaat seen làmmiñu bopp, ba mën ko. delluwaat, di ko jàngal seeni doom. noonu la doomu Irlànd yii ngeen gis defoon ; waaye demoon nañu ba ñoom ñëpp, mboleem ñi ci jàng, fàtte woon seen làmmiñu cosaan.

am na benn xalaatkat bu màgg, ci tubaab yi, bu wax ne aw xeet, bu ñu ko nootee, lu nooteel ga tar tar tar, su fekkee ni fàtteegul lammiñam rekk, bu yeboo yaakaaram bañ a tas. waaye nag, bu demee ba fàtte làmmiñam, loolu bóli gu dagg la.

léegi, tubaab yi jóge nañu fi, am na lu ëpp joróom fukki at. kon, su suñuy làkk yi wéyee di fooyooy, ñun rekk la, du keneen, te loolu, benn xeet waru koo nangu.

jukki bii, ñu ngi ko tibbe ci waxtaan wu Séex Anta Jóob defoon, ci ñaar-fukki fan ak juróom-ñett, ci weeru awril, atum juróom-ñett fukk ak ñeent (28 awril 1984), ci Cees. ñu indi ci ay coppite, ba mu méngook xam-xamu nit ñiy ñëw ci ëttub wolof.

Moomeel © Kàllaamay réew mi 2012 - 2022 | Ñooy ñan | Jokkoo ak ñun