Ëttub wolof

Dalu web bi leen di jàppale,
ci jàng dawal ak jàng bind làkku wolof


E-mail : seserling@gmail.com
Tel : 77 111 88 09 / 70 975 35 27

Gaawu, juroom-ñaari fan, ci weeru desàmbar, atum 2024

Nañu delloo làkki réew mi seen gëdd, di leen jëfandikoo ci bépp jokkoo. Séex Anta Jóob nee na : « làkku jàmbur, su neexee ni tàngal it, kenn mënu koo macc ba ciy tàqamtiku ».

Séex Anta Jóob

Góor gi

Tekkeerlu, lu am solo la, ci kàllaama bu nekk. ngir yég njëriñam, jàngal lii di ñëw.

dafa amoon genn góor, guy waaj a génn àdduna. laata muy faatu, muy gaawantu di bind benn bataaxal. sunu boroom jële ko fi te noppeegul. bataaxal bi mu jot a bind mooy :

"bàyyil naa sama alal sama doom déedet sama jarbaat mukk dinaa fay sama ñawkat dara néew-doole yii."

jarbaat bi jot ci bataaxal bi, jàng ko ba noppi, ne góor gi nee na :

bàyyil naa sama alal sama doom ? déedet ! sama jarbaat. mukk dinaa fay sama ñawkat ! dara néew-doole yii !

doom ji daldi këf këyit ga, jàng ko moomit ba noppi mu ni : mukk ! góor gi waxul loolu.

ñu laaj ko dégg-déggam.

mu ni li góor gi wax mooy :

bàyyil naa sama alal sama doom. déedet sama jarbaat ! mukk dinaa fay sama ñawkat ! dara néew-doole yii !

ñawkat ba moomit, jot ci bataaxal bi, jàng ko moomit ba noppi, ni àndul ci waxu jarbaat bi, ak doom ji. góor gi dafa ni :

bàyyil naa sama alal sama doom ? déedet ! sama jarbaat ? mukk ! dinaa fay sama ñawkat. dara néew-doole yii !

bi coow li di am, fekk néew-doole, yi góor gi daan sarax, suba su nekk, dégg coow li yëpp, ci suufu palanteer, bi ñu daan toog, bés bu Yàlla sàkk. ñu ne bérët, dàjji buntu kër gi, séddoo xaalis bi, lal dëkk, walbati ku ci doom jeek, jarbaat beek ñawkat bi, ni leen, góor gu baax gi nee na :

bàyyil naa sama alal sama doom ? déedet ! sama jarbaat ? mukk ! dinaa fay sama ñawkat ? dara ! néew-doole yii !

foofu la yëf yi jeexee. ñi ëpp doole, te gën a bare, jël yëpp. bàyyi fa ñi ca des ak seen wax ju bare.

li waral coow loolu yëpp nak, moo di mdind, mu sammoontewul ak tekkerlu.

Moomeel © La Sénégalaise des Services Linguistiques (SeLing) | Kàllaamay réew mi 2012 - 2022 | N.I.N.E.A : 008735568 | Adresse : Liberté 6 Extension, villa n°8