Ëttub wolof

Dalu web bi leen di jàppale,
ci jàng dawal ak jàng bind làkku wolof

Gaawu, ñaar-fukki fan, ci weeru sulet, atum 2024

Nañu delloo làkki réew mi seen gëdd, di leen jëfandikoo ci bépp jokkoo. Séex Anta Jóob nee na : « làkku jàmbur, su neexee ni tàngal it, kenn mënu koo macc ba ciy tàqamtiku ».

Séex Anta Jóob

Medina

bañ leen, bu leen nangu.

xaley Medin mësuñu des gànnaaw.

ndox daal fa mu doon taa, démb,

soo fa demee, fekk fa tooy-tooy.

jóg leen, balaa muy wees.

xaley Medin mësu ñu des gànnaaw.

ndox daal fa mu doon taa, démb,

soo fa demee, fekk fa tooy-tooy.

dëgg la jamono bi dafa metti loolu,

ba tax ne nit ñaa ngiy dunde yaakaar te Yàlla noppii na.

gëm leen te takku liggeey balaa muy wees,

te xamni séddale taamu naa si ci kuddu yu jëkk ya.

gaynde, ci diggu màndi,

ku ka ko fekk mu wanla dooleem.

waa Medin ñoo fi nekkoon, di regle, di lijjanti, ci biir Ndakaaru Jaay.

bañ leen, bu leen nangu.

xaley Medin mësuñu des gànnaaw.

ndox daal fa mu doon taa, démb.

soo fa demee, fekk fa tooy-tooy.

dëgg la jamono bi dafa metti loolu,

ba tax ne nit ñaa ngiy dunde yaakaar te Yàlla noppii na.

gëm leen te takku liggeey balaa muy wees,

te xamni séddale taamu naa si ci kuddu yu jëkk ya.

lii mala wax nanga ko déggee xel te bañ ko jàppee sa xol.

mani xaley Medin, mësu ñoo des gànnaaw.

sunu awëniir nañ ko tëye ak sunuy loxo.

xaley Medin, jom, lañuy wéyee.

billaay ndaw lu nekk, Medina dugal na ca loxoom.

billaay ndaw lu nekk, Medina dugal na ca loxoom.

Mbaye. yee, yee, billaay dugal nga ca loxo.

jàmbaar ju nekk, Medina wane nga ko fileey.

Mbaye. yee, yee, billaay dugal nga ca loxo.

jàmbaar ju nekk, Medina dugal na ca loxoom.

lii mala wax, nanga ko tëyee xel te bañ ko jàppee sa xol.

mani fulla ak faayda xaleey Medin ñoo ko yelloo.

salaam maalikum, maalikum salaam.

mani ñii ñooy ñan ? ñii ñooy Medin.

ne salaam maalikum, maalikum salaam.

Mbay Jeey, ñii ñooy ñan ? ñii ñooy Medin.

salaam maalikum, maalikum salaam.

ma ni yéenay ñan ? ñii ñooy Medin.

woow. salaam maalikum, maalikum salaam.

man de waaru naa. ñii ñooy Medin.

heeeey. salaam maalikum, maalikum salaam.

bu kenn yox-yoxi. fii mooy Medin.

Moomeel © Kàllaamay réew mi 2012 - 2022 | Ñooy ñan | Jokkoo ak ñun