Ëttub wolof

Dalu web bi leen di jàppale,
ci jàng dawal ak jàng bind làkku wolof

Dibeer, ñetti fan, ci weeru nowàmbar, atum 2024

Nañu delloo làkki réew mi seen gëdd, di leen jëfandikoo ci bépp jokkoo. Séex Anta Jóob nee na : « làkku jàmbur, su neexee ni tàngal it, kenn mënu koo macc ba ciy tàqamtiku ».

Séex Anta Jóob

Tukki

yoon wii nga jël baaxul ku la koy digal da lay nax.

yoon wii ci des moo gën, loo taseel dàldi koy mën.

yoon wii nga jël,

booy dox ba ca biir gestul xool fi nga weesu balaa ngay réer.

booy tukki yaw,

booy tukki yaw,

booy tukki yaw, na nga bàyyi ba mën.

diŋ (di nga) ca jële lu mën a xew ca feneen.

dina tax nga mën xam nekkinu ñeneen.

foofu mën nga fa gis lu yokk sa xameel,

booy tukki yaw.

nit a ngi toog di janook (janoo ak) yaw,

booba fekk na ma ngay xalaat, ba tàbbi asamaan ànd ak niir yiy naaw,

dem na fu sore lépp ciy (ci ay) xalaatam.

yaw sama waay kaay ma xamal la,

léeg-léeg nga toog fi nga toog tukki tukki bu neex dem ba kaw asamaan,

ànd ak weer wiy naaw,

li ngay janeer mu lay neex boo janoo mu gën fee neex.

booy tukki yaw.

deel tukki yaw, yeesal sa xameel.

diŋ (di nga) ca jële lu mën a xew ca feneen.

dina tax nga mën xam nekkinu ñeneen.

foofa mën nga fa gis lu yokk sa xameel.

deel tukki yaw.

lëppa-lëpp sàmba ma ngay naaw,

te booy seet sax taxu koo gaaw.

te léeg-léeg mu dem ba gaaw.

tukkee ka neexee, waaw.

liccin céeli ma ngay naaw,

te léeg-léeg mu naaw ba kaw asamaan indaale gii xabaar,

ku dul tukki doo xam fu dëkk neexee.

booy tukki yaw.

booy tukki yaw, na nga bàyyi.

booy tukki yaw, na nga bàyyi ba mën.

diŋ (di nga) ca jële lu mën a xew ca feneen.

dina tax nga mën xam nekkinu ñeneen.

foofa mën nga fa gis lu yokk sa xameel.

booy tukki yaw.

ne booy tukki yaw.

ñuni booy tukki yaw, na nga bàyyi ba mën.

ñaanu barke, ãããããh ñaanu barke.

nit a ngi toog di janook (janoo ak) yaw,

booba fekk na ma ngay xalaat ba tàbbi asamaan, ànd ak niir yiy naaw,

dem na fu sore lépp ciy (ci ay) xalaatam.

yaw sama waay kaay ma xamal la.

léeg-léeg nga toog fi nga toog tukki tukki bu neex dem ba kaw asamaan làng ak weer wiy naaw,

li ngay janool lu mu lay neex boo janook (janoo ak) moom, mu gën fee neex.

booy tukki yaw, na nga bàyyi ba mën.

diŋ (di nga) ca jële lu mën a xew ca feneen.

dina tax nga mën xam nekkinu ñeneen.

foofa mën nga fa gis lu yokk sa xameel.

deel tukki yaw.

lëppa-lëpp sàmba ma ngay naaw, te booy seet sax taxu koo gaaw.

te léeg-léeg mu dem ba gaaw.

tukkee ka neex, waaw.

liccin céeli ma ngay naaw,

te booy seet sax taxu koo gaaw,

indaaleel ñuy xabaar.

tukkee ka neex, waaw

Moomeel © Kàllaamay réew mi 2012 - 2022 | Ñooy ñan | Jokkoo ak ñun