Ëttub wolof

Dalu web bi leen di jàppale,
ci jàng dawal ak jàng bind làkku wolof

Dibeer, fukki fan ak ñett, ci weeru oktoobar, atum 2024

Nañu delloo làkki réew mi seen gëdd, di leen jëfandikoo ci bépp jokkoo. Séex Anta Jóob nee na : « làkku jàmbur, su neexee ni tàngal it, kenn mënu koo macc ba ciy tàqamtiku ».

Séex Anta Jóob

Sàqum baatu wolof : diksoneeru wolof

a

à

ã

b

c

d

e

é

ë

f

g

h

i

j

k

l

m

n

ñ

ŋ

o

ó

p

q

r

s

t

u

w

x

y

a - A aa - AA à - À ãa - ÃA
[a:da]

aada t.

baax g-, xarbaax g-, lu ñu tàmm daan ko def ca jomonooy maam ya. Ndëpp aada lébu la.

[a:fija]

aafiya t.

jàmm ak salaam j-. May ñu aafiya, bul ñu sonal. sf. fitna j-

[a:ɟɔ]

aajo t.

Ku am aajo, dafay bàyyi ñeneen ñi xel, di leen nuyu bu baax. / soxla s-. Sama aajo moo doon nga jàppale ma, ma am ci liggeey.

[a:ɟɔwɔ:]

aajowoo njk.

Loo aajowoo mooy loo soxla, loo bëgg a jëfandikoo.

[a:ɟu]

aaju njk.

lu jar a def, lu mat a def. Ngor aaju naa sàmm.

[a:ɟuwul]

aajuwul njk.

lu jarul def, lu matul def. Dem seen dëkk aajuwul dugg oto.

[akara]

akara t.

beñe bu am soosu kaani. Ku bëgg akara, dangay ñeme kaani (léebu wolof). wec. aakara b-.

[a:kimɔ:]

aakimoo njk.

jël menn mbir yow rekk, doo ci sóoraale kenn. Li ñépp bokk, bu ko aakimoo yow rekk.

[a:l]

aal njk.

jox nit menn mbir mu mu lay delloo bu ci paree mooy aal. wec.

[a:la:t]

aalaat njk.

Aalaat mooy aal ba pare, dellu aal. wec. abalaa t.

[a:ll]

àll t.

dëkkuwaayu rabi-àll yi, gàncax g-, dëkku jàmbur yi. Seen àll ba am na ay bukki.

[a:llɛ]

àlle njk.

mel ni ab àll wala ku dëkk ci àll bi. Fi mu dëkk dafa àlle.

[a:lla:ɟi]

àllaaji t.

jullit bu góor bu dem aji Màkka ba ñëw. wec. alaaji, aas wala elaas. sf. ajaratu b-, ajaa b-. Àllaaji bi lañu sargalsi.

[a:lla:xira]

àllaaxira t.

yommalxiyaam j-. Àllaaxira kenn du ko wuute. wec. laaxira j-.

[a:llarba]

àllarba t.

benn la ci turu bés yi. Njàng mu nekk am na àllarba.

[a:lluwa]

àlluwa t.

fi sëriñ daara bi di bindal taalibe bi li mu war a jàng. Àlluwa mooy aarduwaas ci njàngum nasaraan.

b - B bb - BB
[ba]

ba njk.

bàyyi, wacc. Loo moomul, ba ko fa. sf. jël.

[ba:]

ba t.

Nijaayam dafay yar ay baa.

[ba:bun]

baabun t.

Gisoon nañu ay baabun ca pàrk Aan ba.

[ba:dɔ:lɔ]

baadoolo njk.

xayadi. Dafa baadooloo ndax moom, loo ko defal tey, suba mu fàtte ko.

[ba:dɔ:lɔ]

baadoolo t.

beykat b-. Rongoñi baadoolo mooy siim cerey buur.

[ba:k]

baag t.

lu ñuy jëfandikoo ca teen ba ngir génne ndox mi. Xuloo ba ca teen ba gaa ña amul baag la. (léebu).

[ba:gantɛ]

baagante njk.

dem a k a dikk. Li ngay baagante ci suba ba léegi mbaa jàmm la ?

[ba:gantɛ]

baagante t.

Sa baagante bi lu ko waral ? Xanaa danga réerle dara ?

[ba:l]

baal njk.

jéggal. Baal ma àq, yal nañu Yàlla boole baal. sf. fayu.