Ëttub wolof

Dalu web bi leen di jàppale,
ci jàng dawal ak jàng bind làkku wolof


E-mail : seserling@gmail.com
Tel : 77 111 88 09 / 70 975 35 27

Àllarba, ñeenti fan, ci weeru desàmbar, atum 2024

Nañu delloo làkki réew mi seen gëdd, di leen jëfandikoo ci bépp jokkoo. Séex Anta Jóob nee na : « làkku jàmbur, su neexee ni tàngal it, kenn mënu koo macc ba ciy tàqamtiku ».

Séex Anta Jóob

Njëriñu tekkeerlu ci wolof

Tekkeerlu, lu am solo la soo dee wax. boon nag, war na feeñ ci mbind mi.

tekkeerlu yi bare nañu. waaya, ñu bare nangu nañu ne, ñooy jox bataaxal yi jëmm. soo dee dawal, te joxuloo leen cër, déggin ba du neex, te ñi lay déglu, mën nañoo réer, ba duñu xam li ngay wax.

tekkeerlu yi, jamonoy noppalukaay lañu, ci kiy dawal, ak kiy déglu.

kiy dawal, dana mën a noyyi léeg-léeg, wala soppi waxin, su ko tekkeerlu bi laajee, indi waxin buy niru làcce, wala waxinu dëgëral wax, ak ñoom seen.

kiy déglu, dina mën a noyyi moom it, mën a topp wax ji, te du ci sonn.

wax ak déggin, ñoom ñaar a ànd, te war a ànd di wëyandoo. lu ko moy rekk, déggin ba du deme noonu.

su fekkeeni dangay dawal, waruloo jàngaale tekkeerlu yi. ñoom dañu fi nekk rekk, ngir wan la yoon yi nga war a jaar, ngir dawal bi jaar yoon.

tekkeerlu yi ñu gën a ràññe ñooy :

  • tomb .
  • ñaari tomb :
  • xos wala kos ,
  • tomb-xos wala tomb-kos ;
  • tomb wéyale ...
  • tombu laaj ?
  • tombu jalu !
  • këmbu kepp « », biy boole kepp ubbi «, ak kepp tëj ». te ñu koy bindee tëmit nii " ", bi nga xam ni, kepp ubbi bi, ak kepp tëj bi, benn lañu.
  • këmbu xala () , biy boole xala ubbi (, ak xala tëj ).

nañu faram fàcce, tekkeerlu yi, ngir mën a xam bu ci nekk, lan mooy njëriñam, ak fan lañu leen di jëfe.

tomb ( . )

tomb, dafay wane bataaxalu xamle. tomb mooy wane jeextalu bataaxal. soo ci yegsee, war nga ni tekk, noyyi, defaruwaat, balaa ngay yeggali sa wax ji, wala sa dawal bi.

ñaari tomb ( : )

ñaari tomb, ci lim lay ñëwe wala ci jottali waxu keneen :

- Abdu ñetti doom la am : Awa, Elimaan, ak Xadi.

- Seex Anta Jóob nee na : « làkku jàmbur, su neexee ni tàngal it, kenn mënu koo macc ba ciy tàqamtiku. »

ci bataaxal bu mujj bi, du ñun ñooy wax, waaya Seex Anta Jóob la. loolu mootax, waxam yëpp lañu wërngal, ak këmbu kepp « ». dina ñu dellu ci këmbu kepp.

xos wala kos ( , )

kos moom, niroo na ak tomb, ci fànn bii di tekkaaral. wànte nag, tekkaaralam, mooy gën a gàtt tuuti, tekkaaral bi am ci tomb. kos moom, foo tollu war nga di ci bàyyi xel, ndax soo ko naxasaalee, mën naa walbati sa wax, ba waxloo la loo xalaatul woon.

ci misaal, nañu xool ñaari bataaxal yii :

- xale yi nga xam ni yaru nañu , dinaa leen neexal.

- xale yi , nga xam ni yaru nañu , dinaa leen neexal.

bataaxal bu njëkk bi, nga xam ne benn kos la am, dafay tekki ne : ci biir xale yi, dafa am ñi nga xam ne dañu yaru ak ñeneen ñu yaruwul. dinaa neexal ñi yaru. ñi yaruwul nak, duma leen neexal.

bataaxal bi ci topp, te am ñaari kos, dafay tekki ne : xale yi yëpp, dañoo yaru, te dinaa leen neexal ñoom ñëpp.

soo dindee ci bataaxal bi, li nekk ci digante ñaari kos yi, li des, dafay méngook ba léegi ak tekkinu bataaxal bi, ndax li des, muy "xale yi dinaa leen neexal", dafay méngook ba léegi, ak xale yi yëpp dañuy am neexal. loolu, mënuloo ko def ci bataaxal bu njëkk bi, ndax, su boobaa, xale yëpp dinañu am neexal, te wax ji, mu ngi jubluwoon ci, jox neexal xale yu yaru yi, te bàyyi xale yu yaruwul yi.

kon nak, nañu bàyyi xel bu baax, ci kos yi, te di leen di jëfandikkoo ci anam yu jaar yoon.

tomb kos ( ; )

tomb kos dafay xajji :

  1. ñaari bataaxal yu wuute waaya bokk xalaat ;
  2. ñaari bataaxal yu ñu bëgg a féewale ;
  3. xàjji lim bu tàmbale ak ñaari tomb.

ngir wane loolu, jàngal bataaxal yii ci topp.

  1. nawet eksi na ; dex gaa ngiy fees.
  2. bon a gën gannaaw baax ; baax a yées gannaaw bon.
  3. man dinaa bay :
    • soble ;
    • batañse ;
    • yomb ;
    • jaxato.

tomb wéyale ( ... )

tomb wéyale dafay wane :

  1. bataaxal bu ñu wàññi, ndax bañ a wax lu ñaaw ;
  2. wala tekkeerlu, ndax di xalaat ci biir wax ;
  3. wala lim, bu ñu bëgg a gàttal.

ngir wane loolu, jàngal bataaxal yii ci topp.

  1. damay ... astahfirulaa !
  2. móodu dem na ndar ... ëhh démb. deedeet, bërki-démb.
  3. man dinaa bay : soble; batañse; yomb; jaxato; kaani; tamaate; ...

wéyale, su nekkee ci njexantalu lim, da nga koy jàng. ni nga koy jànge mooy, ak ñoom seen.

tomb laaj ( ? )

tomb laaj, dafay wane bataaxalu làcce.

ngir wane loolu, jàngal bataaxal yii ci topp.

- waa yaw ! loo xalaat ci làkki réew mi, ni ñu leen ñàkkalee solo ?>

- jaaxal na ma, lool ! dëkku Kocc Barma, ba ci Seex Anta Jóob. su sëriñ si di bind, wala peresidaŋ di wax, ci làkku bitim réew la ñu koy defee, bàyyi fii suñuy làkk. suñu ko xaymaa, ci téemeeri nit yoo jël ci réew mi, juróom-ñeent fukk yi, dégg nañu wolof waaya, mënu ñu koo dawal. mënu ñu koo bind. waaw loolu, nu mu tudd ?>

tomb jalu ( ! )

tomb jalu, dafay wane baatu bàkku, baatu fésal, baatu jaaxle, baatu jooytu, baatu mbetteel, baatu mbégte, baatu ndigal, baatu waaru, wala baatu yéemu.

ngir wane loolu, jàngal bataaxal yii ci topp.

yaw ! bàyyil li ngay def ! ku manul bawoo, lu yàqu yaw a !

eeh ! àll bii moo rafet ! man de jaaxle naa !

këmbu kepp

ñu koy binde nii  « » , wala nii  " " 

këmbu kepp, day misaal wax jooy jottali. suma waxee : " Seex Anta Jóob nee na " war naa wane li Seex Anta Jóob wax, fi mu dooree, ak fi mu jeexee ; këmbu ubbi « mooy wane ndorteel bi, këmbu tëj » wane jeexanteel bi.

këmbu xala " () "

këmbu xala, dafay indi leeral ci mbind mi. Abdu mujjul yegsi, ci waxtu wi ñu waxantewoon ( Ndar dafa fa taw, taw bu ñu gëj a gis ). li ñu bëgg leeral foofu, moo di taw bi mu taw Ndar, moo tax Abdu mujjul yegsi, ci waxtu wi ñu waxantewoon.

Moomeel © La Sénégalaise des Services Linguistiques (SeLing) | Kàllaamay réew mi 2012 - 2022 | N.I.N.E.A : 008735568 | Adresse : Liberté 6 Extension, villa n°8