Ëttub wolof

Dalu web bi leen di jàppale,
ci jàng dawal ak jàng bind làkku wolof


E-mail : seserling@gmail.com
Tel : 77 111 88 09 / 70 975 35 27

Alxemes, ñaar-fukki fan ak benn, ci weeru nowàmbar, atum 2024

Nañu delloo làkki réew mi seen gëdd, di leen jëfandikoo ci bépp jokkoo. Séex Anta Jóob nee na : « làkku jàmbur, su neexee ni tàngal it, kenn mënu koo macc ba ciy tàqamtiku ».

Séex Anta Jóob

Sàqum léebu wolof mi

Aar moo gën faj.

Aawo, aw la tudd.

Aawo buuru këram..

Aaye na, aayeetul keroog.

Ab dag du bëgg moroom ma.

Ab lonku, daar a ca gën.

Ab yeel bu ëppee ab lupp booba jàngoro rax na ca.

Àbb delloo la sant.

Àbb, delloo ca gën.

Àddina ak li ci biiram jarul a xiirook a ŋaayoo.

Àddina, ànd bi géleem la.

Àddina daramba la.

Àddina du cere, waaye dañu koy laalo.

Àddina du cere waaye dees na ko laalo.

Àddina du cere waaye lu mat a laalo la.

Àddina du dara.

Àddina du kër, xaarukaayu dee la.

Àddina du lijjantiku. Ca xeexub Badar la lëje woon.

Àddina gudd nab tànk.

Àddina jigeen la, ju fu mu tollu, mu ngi ëmb te kenn xamul lu muy jur.

Àddina, kendandoo la.

Àddina kenn defaru ko ci benn fan.

Àddina këru naxekaay la.

Àddina li muy yaatu-yaatu, ñaawaay a ëpp wóllare taar.

Àddina mor yow.

Àddina, ndoxum joor la ; buy taa, mu ngay ŋiis.

Àddina Njéeme la tudd, sant Ba.

Àddina njoowaanu golo la, garab gu nekk lay wékku.

Àddina ñett a ci gën : àjjana biti, ak weerteewlu ak mëneek say dëkk, ak ku la gis bëgg

Àddina ñett a ci gën, am a gën, man a gën, xam a gën.

Àddina, ñett a ci di yóbbal : ab xame, ab taar ak mbuus.

Àddina ñett a ko jàpp : saxle, gub sax bi, ak sax mi.

Àddina ñetti fan la, démb ñoom baay, tey ñun, ëllëg sunuy doom.

Àddina potu ndaa la, ku naan jox sa moroom mu naan.

Àddina, reenub ñàmbi la, kenn xamul fu muy damme.

Àddina weeru koor la ; feek jant sowul, juubu du wees.

Dund gu jeexagul, weeru koor la : juubu weesoogu ca.

Koor gu jant sowagul, juubu weesoogu ca.

Àddina wori neen la.

Àddina yagadeete la, koo ca gis ngaa ndëndam, mu ko tëggal ; noppam ne ko : yàggleel.