Ëttub wolof

Dalu web bi leen di jàppale,
ci jàng dawal ak jàng bind làkku wolof


E-mail : seserling@gmail.com
Tel : 77 111 88 09 / 70 975 35 27

Alxemes, ñaar-fukki fan ak benn, ci weeru nowàmbar, atum 2024

Nañu delloo làkki réew mi seen gëdd, di leen jëfandikoo ci bépp jokkoo. Séex Anta Jóob nee na : « làkku jàmbur, su neexee ni tàngal it, kenn mënu koo macc ba ciy tàqamtiku ».

Séex Anta Jóob

Ñett ñu yeeme

Ñetti nit lañu woon, kenn ku ne, am mag gu doy kéemtann.

kenn ki dafa amoon gis-gis bu ñaw, ñaw a ñaw ba amul ub dend.

ki ci tegu, amoon na nopp yu neex, ba lu yëngu lu mu tuuti tuuti, du ko rëcc.

ñettel ba, gudd loxo ba mu jéggi dayo.

ñoom ñet ñu ànd di doxantu ca tefes ga, ba mu yàgg, Maneex-nop ne temm taxaw, ne kott, ba ma yàgg mu ne :

- dégg ngeen ! am na peppu ceeb wu daanu ci biir géej, dégg naa putt ja.

baax-bët daldi ne :

- waawaaw, mu nga nale may séen ca ndox ma, muy yëngu.

gudd-loxo daldi ne coppet pepp ba, ne leen :

- amleen, seen peppu ceeb a ngoogu !

ñu leen di laaj, ñii ñett, ana ku ci sut ?

Moomeel © La Sénégalaise des Services Linguistiques (SeLing) | Kàllaamay réew mi 2012 - 2022 | N.I.N.E.A : 008735568 | Adresse : Liberté 6 Extension, villa n°8