Dalu web bi leen di jàppale,
ci jàng dawal ak jàng bind làkku wolof
E-mail : seserling@gmail.com
Tel : 77 111 88 09 / 70 975 35 27
Nañu delloo làkki réew mi seen gëdd, di leen jëfandikoo ci bépp jokkoo. Séex Anta Jóob nee na : « làkku jàmbur, su neexee ni tàngal it, kenn mënu koo macc ba ciy tàqamtiku ».
dem ! dem ! dem fan ?
dem ndax lan ? baay a ko moom.
dem ngir, xeex bu bare bii.
dem ndax, teen bu neex bii.
rab yi rekk, ñoom ñoo ciy naan.
naaj bi lakkatuma ; taw bi barewul.
dem ngir, bokk bool, mënu fee am.
dem ngir dafa, war a nekk góor, doon góor-góorloo.
dem ! dem ! dem fan ?
dem ndax lan ? liberte bi.
ci espaas, bu lëndëm bii.
sama bët yi, ci suuf di wut, garab bi nga xamante ni ñoo ma suuxat.
bu ma seetee, garab bi bóow.
dem ngir, kër gi daf ma niru lu lëndëm.
dem ngir dafa war a nekk góor, doon góor-góorloo.
damay dem, ci àll bi.
ne damay dem, ci dex gu mag ji.
ne damay dem, waaw seeti sama nawle.
damay dem, si ban bu rittax bii.
ne damay dem, bërënguji ci.
ne damay dem, waaw seeti sama mbokk yi.
doon góore
doon góore
dem ! dem ! dem fan ?
dem ndax lan ? baay a ko moom.
dem ngir, xeex bu bare bii.
dem ndax, teen bu neex bii.
rab yi rekk, ñoom ñoo ciy naan.
naaj bi lakkatuma ; taw bi barewul.
dem ngir, bokk bool mënu fee am.
dem ngir dafa war a nekk góor, doon góor-góorloo.
damay dem, si àll bi.
ne damay dem, si dex gu mag ji.
ne damay dem, waaw seeti sama nawle.
damay dem, si ban bu rittax bii.
ne damay dem, bërënguji ci.
ne damay dem, waaw seeti sama nawle.
doon góore
doon góore
wan ma sa xarit, ma wan la ki nga doon ooy.
wan ma sa mbokk, ma wax ko fi ngay jaar.
eey !
what do you need ?
eey eey !
yaw li la neex.
wan ma sa xarit, ma wan la ki nga doon ooy.
wan ma sa bopp, ma wax la fi ngay jaar.
eey !
defal li la neexoo.
eey !
yaw li la soob.
sàmmkatu mbott, moo xam ba cay sooxoo.
ñi mën a kott, ñoom daal amuñu mbaam.
eey !
defal li la neexoo.
eey yuu !
what do you want ?
óooo ó ó ó óooo ó ó ó ó óooo ó ó ó ó óooo
kër gi daf may niru lu lëndëm daal.
óooo ó ó ó óooo ó ó ó ó óooo ó ó ó ó óooo
dem ! dem ! dem ndax lan ? baay a ko moom.
dem ngir, xeex bu bare
dem ndax, teen bu neex. rab yi rekk, ñoo ciy naan.
dem ngir, kër gi daf ma niru lu lëndëm.
dem ngir, góor dafa war a nekk góor-góorloo.
óooo ó ó ó óooo ó ó ó ó óooo ó ó ó ó óooo
óooo ó ó ó óooo ó ó ó ó óooo ó ó ó ó óooo
Moomeel © La Sénégalaise des Services Linguistiques (SeLing) | Kàllaamay réew mi 2012 - 2022 | N.I.N.E.A : 008735568 | Adresse : Liberté 6 Extension, villa n°8