Ëttub wolof

Dalu web bi leen di jàppale,
ci jàng dawal ak jàng bind làkku wolof


E-mail : seserling@gmail.com
Tel : 77 111 88 09 / 70 975 35 27

Gaawu, ñaar-fukki fan ak ñett, ci weeru nowàmbar, atum 2024

Nañu delloo làkki réew mi seen gëdd, di leen jëfandikoo ci bépp jokkoo. Séex Anta Jóob nee na : « làkku jàmbur, su neexee ni tàngal it, kenn mënu koo macc ba ciy tàqamtiku ».

Séex Anta Jóob

Xel

Faamara, rëbbkat la woon.

daa (dafa) am bis, mu xàlli yoon.

mu taxaw di xalaat ba mu yàgg mu séen mbëtt muy daw.

mu suxat fetalam ba te di daagu te naan, kii duma raw.

far mbëtt ma, séen kokko ron.

daldi jël bopp ba, daldi koy ron.

bopp ba nëbbu na li ci des ci yaramam, wépp di feeñ.

dënn ba ak, ndigg la ak, tànk ya ak, yeneen ya, lépp di feeñ.

lii tax, mu defeni,

mbëtt, daa (dafa) amul xel.

kon ñun ñii, Yàlla jox xel.

nañu santati, nañu santati.

li Yàlla bind yépp, nit la ci gën a fonk.

mala yi li ñu wutale ak ñoom, moy suñu xel, moo tax ñuy def,

looy dugg, jiitalal sa xel,

ba loo ciy wut,

di nga gis ngëneel.

nit ñi yor xel boo seetee ni ñooy doxal àdduna.

kiy def te du xalaat ci misaal day mel ni mbëtt ma.

nit moom, xel a ko yor.

nit moom, xel a ko yor.

nit moom, xel a ko yor.

xel a ko yor.

li Yàlla bind yépp, nit la ci gën a fonk.

mala yi li ñu wutale ak ñoom, moy suñu xel, moo tax ñuy def,

fi nëbb, mooy xel.

soo ko amul, yaa ngi mel ni bàyyima.

soo ko amul, dootoo nekk nit.

li Yàlla bind yépp, nit la ci gën a fonk.

mala yi li ñu wutale ak ñoom, moy suñu xel moo tax ñuy def, moo tax ñuy def.

waawaaw, waawaaw, waawaaw, waawaaw

Faamara, rëbbkat la woon.

daa (dafa) am bis, mu xàlli yoon.

mu taxaw di xalaat ba mu yàgg mu séen mbëtt muy daw.

mu suxat fetalam ba te di daagu te naan, kii duma raw.

far mbëtt ma, séen kokko ron.

daldi jël bopp ba, daldi koy ron.

bopp ba nëbbu na li ci des ci yaramam wépp di feeñ.

dënn ba ak, ndigg la ak, tànk ya ak, yeneen ya, lépp di feeñ.

lii tax, mu defeni,

mbëtt, daa (dafa) amul xel

kon ñun ñii, Yàlla jox xel.

nañu santati, nañu santati.

li Yàlla bind yépp, nit la ci gën a fonk.

mala yi li ñu wutale ak ñoom, moy suñu xel, mooy tax ñuy def, moo tax ñuy def.

waawaaw, loolu mooy xel.

soo ko amul, soo ko amul,

yaa ngi mel ni bàyyima, yaa ngi mel ni bàyyima, yaa ngi mel ni bàyyima.

looy dugg nanga ko tekkee xel.

Faamara rëbbkat la.

mbëtt.

Moomeel © La Sénégalaise des Services Linguistiques (SeLing) | Kàllaamay réew mi 2012 - 2022 | N.I.N.E.A : 008735568 | Adresse : Liberté 6 Extension, villa n°8